Baayi Ma

Elzo JamDong

VERSE 1
Adouna sobé la (sobé la ah ah ah )
Kou kheuthio ak mom mou fowé la (fowé la ah ah)

Tedj negn ma tchi kasso maa ngui diémeu reuthieu
Diémeu fey begneu lap tchi guédiou leundeum
Deugueur bopp takh lougn degn ma téré ma dieuf
Di deglou baken loumou guenné me dieund

Mangui tchi yone bi di zig zag di zig zag
Wouté naak niom yoneunté Yalla Isaac
Mangui tchi yone bi di zig zag di zig zag
Kou dem naani kaani mouno wothiou bissap

Mane sama beug beug moye sama nattou
Momeu takha naaw lakk sama kérozène
Momeu takha war gni meu diokhone sama kaddou
Ak sho yi ndieukk kham sama sokhna fimeu érogène
Han
Yow yaay mane maay yow
Loma deflo sama bopp laako def
Yow Yaay kane ? Yow yaa bone !
Nimala sekhlo nonou laala abonné

Linga ma dioumlo yeup kham naani yaa ko tey
Newone naa so ma beugueuté diégué naa ko begn
Linga ma dioumlo yeup kham naani yaa ko tey
Nga nekk sama birr khel naan ma "khana amo khel ?"

Nga may ma baat tek ma paaka tchi pout
Nand naa ni deung ma beugg diappé ngaaka tchi pett
Han
Mane dama leu topp seme bopp di metti
Ken dou weddi né kou leu sopp deukké sopp di weddi

Chorus
Ya takh me pouss wakhtou dioulli yi me tayalone diok
Yow yama takha dioylo djiguene yimeu nop
Nga né tchi sama bopp dimeu dey mey moy
Bala may dieggui siraat beugg nama takhaliko'k yow

Baayima, baayima (hum hun) baayima (yeah)
Baayima, ma bayila
Baayima (baayima), baayima (baayima)
Baayima (woah), Baayima ma baayi la
Yeah (Yeah)

Ya takh me pouss wakhtou dioulli yi me tayalone diok
(woah oh)
Yow yama takha dioy-lo djiguène yimeu nop (yeah)
Nga né tchi sama bopp dimeu déy mey moy
Bala may diegui siraat beugg nama takhaliko'k yow

Baayi ma (Baayima), baayi ma (baayi meu) yo baayi ma (eh eh)
Yo baayi ma, ma baayi la
Nga baayi ma (yeah), nga baayi ma (baayi meu)
Nga baayi ma (baayi meuu)
Nga baayi ma, ma baayi la

Verse 2
Adouna sobé la (sobé la ah ah ah )
Kou rawanté'k mom faux départ (faux départ aah ah ah )

Me netteuli leu sama guent gui
Kou ko guent do beugg guenteeuti
Kou ko guent do beugg guenneuti
Mba nga yewou beug sey wala dem tukki
Seytané def me beugone damp ni lire ak maam
Mou def me diame nar ma takk tchi birr ab kaf
Il Faut que ma téyé sama tankk tchi biir appart bimeu nekk ni di diangg di lire ay sar

Seytané def me beugone damp ni lire ak maam
Mou def me diame nar ma takk tchi birr ab kaf
Kou ko dowoul dé ley sankk kill fat fat
Foumma wowati faut q ma lankk nguir am jamm te benieu teleu fouti

Khamatouniou lane moye lerrou gouddi
Kilifeu yiniou beugg roy
Fadiar teel legn daan yewou dioulli
Ndokh dou am niou dieul kherrou dioulli
Loutakh bign le diappé nga faakh se pappeu néleu doto guenn gouddi ?

Defarouwaat gueuneu nekk khel ndakh diangg dou wess te Ibliss def niou beugg djiguini dieul niou def niou diaamou baken
Kou fi yokk weddi waagni yiw no def wokk dokkh nakh nga se bopp bo fogué ne bo fi diogué ken douleu fatté

Nga may ma baat tek ma paaka tchi pout
Nand naa ni deung ma beugg diappé ngaaka tchi pett han
Mane demleu topp seme bopp di metti
Ken dou weddi ni beugg lou yomb moley yobé lou metti

Chorus
Ya takh me pouss wakhtou dioulli yi me tayalone diok
Yow yama takha dioylo djiguene yimeu nop
Nga né tchi sama bopp dimeu dey mey moy
Bala may dieggui siraat beugg nama takhaliko'k yow

Baayima, baayima (hu hum) baayima (yeah)
Baayima ma bayila
Baayima (baayima), baayima (baayima)
Baayima (woah) , Baayima ma baayi la
Yeah (Yeah)

Ya takh me pouss wakhtou dioulli yi me tayalone diok
(woah oh)
Yow yama takha dioy-lo djiguène yimeu nop (yeah)
Nga né tchi sama bopp dimeu déy mey moy
Bala may diegui siraat beugg nama takhaliko'k yow

Baayi ma (Baayima), baayi ma (baayi meu) yo baayi ma (eh eh)
Yo baayi ma, ma baayi la
Nga baayi ma (yeah), nga baayi ma (baayi meu)
Nga baayi ma (baayi meuu)
Nga baayi ma, ma baayi la

VERSE 3
Diéém naa reuthie
Se pékhé kemtaan leu
Ya meuneu yeew ay thieur
Tedj niou ci se jail locked up

Yow yaa begn jamm
Euppeulé sobé Amsterdam
Yaa rey laamigne
Se taar meuneu daanel jam

Ya takh ma pouss wakhtou diouli yi ma tayalone diok
Ya takh me rouss bimeu dadiék seme morom yi meu togne
Seme thiono yeup nul negn
Adouna dor neme kurpegn

Deungueu beugg niou réér
Bougoulo peace and love
Mane bougouma niou bokk kourel
Bougoumeu guissé'k yow

Bougouma and ak yow
Kone boul and ak mane
Bougouma nekk ak yow
Boul diemeu nekk ak mane

Bougouma def ak yow
Amo loy def ak mane
Waroumeu guiss loumeu neekh rek def
Warouma toke loumeu yek rek def
Baayi ma, baayi ma, baayi ma
Baayi ma, ma baayi leu

FINAL BRIDGE
Bayima ma dem
Bayima ma dem
Bayima ma dem
Manila bayima nga begn

Djihad an-nafsou
Djihad ak nafsou
Lilaay wa rassoul
Baayima bilaay deme sourr

Mangui tchi djihad an-nafsou
Di djihad ak nafsou
Lilaay wa rassoul
Bilaay deme sourr

Curiosità sulla canzone Baayi Ma di Elzo JamDong

Quando è stata rilasciata la canzone “Baayi Ma” di Elzo JamDong?
La canzone Baayi Ma è stata rilasciata nel 2018, nell’album “Macina”.

Canzoni più popolari di Elzo JamDong

Altri artisti di African hip hop