ADOUNA

Jean paul SY, Julien SOULETIE

Nit ñi fi ñuy rawante / mooy ci xol yu rafet yee
Nit ñi fi ñuy amee barke/ mooy ci ñaanu waa-jur yee
Nit ñi fuñu jëm ag yaakamti / xanaa bëg yaxxule
Kon sa wërsëg ding ko fekkee/ xanaa waxtu bi su jotee
Na nga sant, sant, sant, sant te baña yàkkamti waay
Kon defal ndank, ndank, ndank, ndank mooy jàpp golo ci ñaay
Mu xiin, mu taw, mu neex, mu naqari (na nga am sa fulla waay)
Nga weex, nga ñuul, nga am ba xamadi (yaw bul fàtte Yalla waay)
Bula àdduna jay ba nga fàtte ki nga doon ding ko réccu
nii de laa ko gisee.

Yalla buur bi nelawul té gëmmentuwul.
Leeg leeg mu jàpp njamburam ne tekk
te loo ko ñaan mu may la ko si kaw nga laabir
ag am jom te nangu lepp limu la teg
nit ñi dañu bare dugg-dugg, xoolal bu baax
laatà nguay dugg ci lu la bett.

Nangu jël na cëru bañ ba tax na tay jii
ki nga gën a wóolu moo la mën bett
One two three/ suñu Sénégal a ngui
sutura bi daf fi jeex ba luñu gis di nettali,
mbele mbel bi bari, seen xol yi naqari.
Nañu job te bàyyi coow li

Mu xiin, mu taw, mu neex, mu naqari (na nga am sa fulla waay)
Nga weex, nga ñuul, nga am ba xamadi (yaw bul fàtte Yalla waay)
Bula àdduna jay ba nga fàtte ki nga doon ding ko reccu
nii de laa ko gisee.

Yow da ngay mel ni nga wara mel, ñun ñu nangu say jikko
buur bi baaxèe na ñu xel, li ci des mottali ko
Da nguay def li nga wara def, sa wërsëg lijjënti ko
Àdduna ag ni mu mel lo fi góobe garaale ko
Buula Yalla teggee nattu man what can you do
li may ñaan mooy jàmm, wergi yaram, fan yu gudd
Na nga màndu, doo ko réccu, na nga tuub, jéggalu
Yalla rek a dul juum, nañu dem jébbalu
Ñu bare dañuy fàtte ne àdduna jaru ko
ag loo fi mën am yaw da ngay dem bayyi ko
Kila bëg waxla dëgg da ngay teey deglu ko
dunyaa tay jii dafa dem ba jaxasoo

Canzoni più popolari di Natty Jean

Altri artisti di African reggae